Aller au contenu

Soppalikaay

Jóge Wikipedia.
Ab soppalikaay bu ñattiwéq
Soppalikaay 230V/2x9V
Soppalikaay toroid
Soppalikaay simbol
Soppalikaay 3f
Soppalikaay urban

Soppalikaay ab jumtukaay la buy tax a man a soppi limu dend ak taraayu dawaanu mbëj bu jóge cib gongikuwaay buy jur kàttanu mbëj gu safaanu, ci beneen limu dend ak taraay yu wuute te bokk baraay ak melokaan. Te limuy ñakk ci kàttan ci soppali gi lu néew la. Ab soppalikaay, ci dawaan bu safaanu rekk la man a doxe, ndax ci bii xeetu dawaan la mbëjbijjaakon bu safaanu, di ci li doxam aju, man a juddoo.

Soppalikaay yi ci ndomboy jokkalekaayu dawaanu mbëj yiy lëkkale jóoxuwaayu mbëj yi (digg yu mbëj) ak jëfandikukat yi lañu leen di jëfandikoo. Bokk na yenn ci ngirte yi tax dawaan bu safaanu bu Nikola Tesla am-ndaw ci kaw dawaan bu wéy bu Edison ci liñu doon woowee xareeb dawaan yi.

Lim bu bari bu kàttanu mbëj bees soxla ci mboolaay yu taaxe yi tax na ñu war koo jóox ci bariwaay bu dayoowu ci jóoxuwaay yees duppee digg yu mbëj. Ngir man a xayma bariwaayu kàttanu mbëj bees jóox cib digg bu mbëj dañuy xool ci liñuy duppee ngóora gi(njunjam di P bennaanu nattam di Watt ñu koy tënk ci [W]) di luy man a nekk ci diggante ay fukki kw (kilowatt, 1 kW = 1000W) ci digg yu ndoxmbëj walla yu jant ba ci ay teemeeri MW (megawatt, 1 MW = 1.000.000 W) di yu digg yu tàngmbëj ak yu saal. Gii kàttan dañu koy yóbb ci ay teemeeri km. Ngóora (P) gi mi ngi am digaale ak dawaan (I) geek dend (V) gi ci mbindum xayma miy toftal:

Lii dafay tekki ne man ngaa yokk walla wàññi dend gi walla dawaan bi te ngóora gi du soppeeku (te jéem a fexe ba jege 1 (benn)). Lii am na solo lool ndaxte dawaan bi I dafay jur tangoor suy jaar ci biir watatukaayu mbëj bi (ngir njeexitu Joule): lu dawaan bi di gën a bari tangoor giy judd di gën a bari; ngir moytu lii faww ñu yokk dijjaayu watatukaay bi, waaye it yokk gi am na dig ci wàllu koom ak xaral, aju na tamit ci feeñte bi ñuy duppee waddug dend yu buum yi ci seen bopp. Kon ngir wàññi dawaan bi dañuy def ab soppali yokkaale dend gi ci anam gu ngóora gi dul soppeeku.

Ag sàkkam

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Baaxi ab soppalikaay ki leen njëkk a taxawal mooy Michael Faraday ci 1831, waaye li mu ci jubluwoon rekk moo doonoon biral baaxi yi nekk ci xiirtalug mbëjbijjaakon, kon xalaatul woon nan la man a nekkee jumtukaay buy jariñ ci dëgg-dëgg. Lucien Gaulard ak John Dixon Gibbs ci 1881 lañu génne ca Londar ab jumtukaay bees duppee woon «ñaareelu jurukaay», ñu daaldi jaay xalaat bi këru liggéey bu waa-aamerig ba Westinghouse. Mooy soppalikaay bees njëkk a jëfandikoo ci jëfe.