Koom-koomu Afrig

Jàpp nañ ne koom-koomu Afrig mooy gi gën a dellu ginnaw, suñu koo mengalee ak yeneen gox yi.Koom-koom dafa doon lu yaan, bariy fànn, kon fii dañ fiy junj yenn yi rekk.

Njuddéef (production) mu mbay mi ci Afrig day wuute wuute gu mag, kem ni kilimaa bi wuutee, ndax diiwaan yu tàng yi la fay juddoo ci mbay bokkul ak lay juddoo ca diiwaan yu diggdoomu ya (yu yamuw tàngoor ya).

Ëlëgu mbay ci Afrig lu am yaakaar la, ndax am na fi ay yaatu-yaatu yu mag ci suuf su nangu mbay su ñu jëfandikoogul, kon ëlëgu koom-koomu Afrig lu mat a dale‘m xel la, ndax li muy wund lépp aw yiw la ak mbégte.

Bokk na ci njuddéefi mbay yu afrig yi ëpp solo yii:

  • Kakaawoo: mi ngi ci tefesug Gana gi, di ñatti ñeenteeli njudéefi àdduna bi (maanaam bu ñu xaajoon li ci àdduna biy liggéey ci Kakaawoo ñeenti xaaj, ñatt yi fa lañu leen di liggéeye).
  • Diwug garabu tàndarma : mi ngi ci Tefesug Gana gi, Afrig nag mooy gox bi ëpp lu koy jóox (produire) ci àdduna bi.
  • Gom (gomme arabique): ci Sudaan, lu tollook ñeenti juroomeeli njuddéefi àdduna bi.
  • Saytoon (olive) , mawaalih, dugubi qamh ak mboq : ñi ngi ci cat yu bëj-gànnaar yu Gox bi, rawati na ci diiwaanu Maghreb bu Araab bi.

Jur gi

Soppi

Boo gëstoo dinga gis ne :

  • Ay milyoŋi bopp cig jur ñi ngi leen di yare ci sàmmuwaayi Sawaana yi ci Diiwaani Gëwéel yi, ñi ngi yar it ay milyoŋi bopp ciy xar aki bëy ci sàmmuwaay yu diggdoomu yi (walla yu yam tàngoor yi) ci bëj-saalumu Gox bi ak ci bëj-gànnaaram gu sowwu ci Maghreb gu Araab gi, ay milyoŋ it ciy giléem ñi ngi leen di yar ci tàkki Afrig yu yaatu yi.
  • Njuddéef (produit) yi tukkee ci jur gi, ci Afrig, am nanu doole bu baax ci yaxantu gu àdduna bi . Afrig gu bëj-saalum gi moo jël ñeenteelu barab ci réewi àdduna yiy génne ngënël (laine),. Maxrib gu raab gi moom dina génne (exporter) ay xar, di génne ay njuddéefam ñuy ngënël, yàpp, jëme leen ci réewi Tugal yi

Mbell yi

Soppi

Afrig gox la bu naat te woomle ci ay koom yu mbell, lu ëpp ci mbell yooyu nag ñi ngi ci bëj-saalumu Afrig, ak ci mbalkam Kongoo, ak ci réewi Maghreb gu Araab gi. Yi ëpp solo ci mbell yooyu ñooy yii :

  • Jamaa: lu tollook 91% ci njuddéef mu àdduna bi (li ci àdduna biy liggéey)
  • Wurus: lu tollook 65% ci njuddéefu àdduna bi
  • Xànjar: lu tollook 23% ci njuddéefu àdduna bi
  • Yoraaniyom: lu tollook 60% ci njuddéefu àdduna bi
  • Fosfaat: lu tollook 33% ci njuddéeefu àdduna bi. ( ma nga ca réewi Maxrib gu Araab gi)
  • Kobalt: lu tollook 70% ci njuddéefu àdduna bi
  • Manganiis: lu tollook 20% ci njuddéefum àddunaà bi
  • Boksit: (Alimiñom bu ñu laalul) mi ngi ci Gineek Gana
  • Petrol: lu tollook 11% ci njuddéefu àdduna bi, mi ngi nag ci Tàkk gu mag gi, ci Isipt , Libi, Alseeri ak Niseeria.

(yii nag ay njoxe (donnée) lañu yoy man naa am soppeeku nañu)

Ndefar (industrie)

Soppi

Ku gëstu dinga gis ne Afrig :

Gox bu naat la ci ay gongikuwaay yu xéewal yu gàncax, yu mbay, yu jur (dundat) ak yu mbell, niki : wëtéen, ay diwi gàncax, daakaande gi (gomme arabique ), kakaawoo, xànjar, wurus, bettax, fosfaat ak petrol, yii yépp ay njuddéef walla ay ne-ne yu ñu laalul (produits bruts) la ñu, yu am solo te manadee ñàkk ci wàllug ndefar.

Looloo taxoon gox bi di am rëbb (proie) mu réewi Tugal yu sancaan yii di woroomi ndefar (industries) yu mag doon xëccoo, ngir jot – ci anam gu yomb ak ci njëg yu jàppandi - ci ne-ne yu ñu laalul yu fees dell yii ci Gox bi te seeni ndefar di leen soxla, di leen manadee ñàkk. Bu ko defee ñu leen di indeeti giñnaaw bi ñu leen defaree ngir jaaysi leen ci ja yu Gox bi ci ay njëg yu seer te kawe.

Looloo tax it réewi sancaan yu mag yi doon def ay politig yuy tee ndefar yu barab yi (l’industrie locale) di am ak a sawar, ngir Afrig des di ab ja bu mag bu ñuy jaaye njuddéefi Tugal yi ci ay njëg yu kawe, ak it ngir Afrig bañ di jëfandikoo ne-neem yu ñu laalul yi, te loolu doon na am bu ndefaram doxoon te jëm kanam. Ci nii la Afrig di dese dib gongikuwaay bu mag buy génne ay ñumm (ay ne-ne yu ñu laalul) ñeel réewi séancaan yu ndefar yii, te it dib ja buy guux mbooleem sila (marsandiis) yiy bàyyikoo ci yii réew.

Bii politig moo lënk te takk koom-koomu Afrig bi ci koom-koomu réewi sancaan yi, bu ko defee gox bi mujj di lu lott ci amal ag tembam gu koom-koom, bu ko defee réewi gox bi mujj di yu ginnaawe, seeni tolluwaayu dund suufe , tolluwaayi dund yu réewi Tugal yi kawe.

Askani Afrig yi yewwu nanu ci mujjantal gi, jamonoy jànkoonte ak jàmmaarloo gu tar tàmbali lànk canc gi, looloo jur tembug askani Gox bi ci politig, daal di tàmbali di jariñu ci koomi seeni réew ñeel seen bopp, di liggéey it ngir mel ne ñépp ci jekk ak am dund gu neex.

Kon ëlëgu Gox bi gu ndefar ay xéewal rekk la. Ndax kat bu weesoo li gox bi nekk di lu fees aki ñumm yu wuute, teewul mu am sàq mu réy ci ay gongikuwaayi kàttan (source d’énergie), rawati na mbëjum ndox (kurãŋ buy ame ci ndox), petrol ak këriñ.

Wàllug jokkoo (communication)

Soppi

Gox bi day sukkandiku - cig jokkoom – ci yooni weñ yi (raay yi) , yooni jéeri yi ak ngaalug dex (navigation fluviale). Waaye nag gox bi lu deltu-ginnaaw la ci wàllug jokkoo, bu ñu ko nattee ci yeneen gox yi, loolu nag li ko waral mooy lii:

  • Tàkk yu yaatu, yu bekkoor, yu néewi ndox yi.
  • Gotti Yamoo, yu fatt, yu bari yi ay ngirowaay aki déeg.
  • Bari gi mu bari ay rotuwaay aki balluwaayi ndox (cascades)
  • Ñugg-ñugg yi ( creux; movement du sol; ride) yu wow yi ci yenn wàll yi.

Réewi gox bi man nañoo noot jafe-jafe yii, gën a jëmale kanam seen jumtukaayi jokkoo bis bu Yàlla dogalee ndefar yewwu fi ba jëm kanam. Jamono jii ñu tollu gox baa ngi sàkk ay yooni jawwu yu am solo yu koy àggale ci mbooleem wàll yi.